Wuutuloxo bu mbëj
Wuutuloxo bu mbëj walla masin bu mbëj, ab jumtukaay la buy tax a man a soppi kàttanug doolerandu def ko kàttanug mbëj (di ab safaanukaay) walla kàttanug mbëj ci kàttanug doolerandu (di ab doxalukaay bu mbëj) walla rekk soppi melokaanu kàttanu mbëj gi (di ab soppalikaay). Xeeti masini mbëj yi ñett lañu: Doxalukaay, jurukaay ak safaanukaay
doxalukaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci doxalukaay bu mbëj |
Doxalukaay ab xeetu wuutuloxo la buy soppi kàttanu mbëj def ko kàttanu doolerandu ngir defi liggéey. Doxalukaay yi dees leen séddale ci ñaar doxalukaay bu dawaan bu safaanu ak doxalukaay bu dawaan bu wéy.
doxalukaay bu dawaan bu safaanu
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ab xeetu doxalukaay la buy jël kàttanu dawaan bu safaanu soppali ko kàttanu doolerandu. Doxalukaay bu dawaan bu safaanu dees koo séddale ci ñaar:
doxalukaay bu dawaan bu wéy
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bii doxalukaay dafay soppali kàttanu dawaan bu wéy ci kàttanug doolerandu.
Jurukaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci jurukaayu mbëj |
Jurukaay mooy wuutuloxo bu mbëj biy jël kàttanu doolerandu génne ci kàttanu mbëj.
Jurukaay yi dees leen séddale ci ñaar: Jurukaay bu dawaan bu safaanu ak jurukaay bu dawaan bu wéy
Jurukaay bu dawaan bu wéy
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ab jurukaay la booy jox kàttanu doolerandu mu delloo la kàtaanu mbëj ci melokaanu dawaan bu wéy
Jurukaay bu dawaan bu safaanu
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ab jurukaayu mbëj la buy jël kàttanu doolerandu soppali ko dawaan bu safaanu, di nañu ko woowee itam safaanukaay. Nekk na lu ñu Séddale ñaar:
- Jurukaay bu demandoo
- Jurukaay bu demandoodi
Safaanukaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci safaanukaay |
Ab wuutuloxo la bu man a dox ci dawaan bu safaanu rekk, ci jëfe dafay soppi melokaanam. Yitteem mooy yokk walla wàññi tolluwaayu dend bi walla rekk soppi baraay bi. Doxam a ngi sukkandiku ci njeexit lees di wax xiirtalu bijjaakon.