Ndombo gu mbëj
Ndombo gu mbëj dees koy tekkkee niki lëkkalante gu ay cëri mbëj ci wenn yoon wu tëju ci genn anam guy tax ba dawaanu mbëj ga cay jaar di man a wéy di wal, maanaan du am benn dog-dog.
Gëstug ag ndombo
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Solos gëstu ag ndombo gu mbëj mooy génne ca dayooy dawaan ba ak dend ba. Sukkandiku ci melokaani cëri ndombo gi ak àtte yi ñeel ndomboy mbëj yi.
Noste gu wéy
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ag ndombo gu mbëj guy dox ci ag noste gu wéy (maanaam kem yi ajuwuñu ci jamono, seen dayoo du soppiku ci jamono, dees na ko woowee itam jamono-soppeekudi) dina am lumu néew-néew ag ndëgërlu, ab jurukaayu mbëj di luy joxe ab dend (walla ab dawaan) bu wéy, man naa am it, yenn saa yi, ab doxalukaay. Manees naa gëstu ag ndombo ak yii àtte:
- Àtteb ohm: moo nuy xamal dayoob dend U bi ci ag ndëgërlu R gu dawaan I jaar ci biiram: U = RI.
- Àtteb Kirchhoff mooy lay jox jëflante bi ci cër yu wuute yu ndombo gi.
- Céetu Norton: mooy wax ne gépp ndombo gu ndëgërlu (ndombo gu ami ndëgërlu rekk) dafay yam ak ab jurukaayu dawaan I bu lang ak ag ndëgërlu R.
- Céetu Thevenin: mooy wax ne sooy xoolee ag ndombo gu mbëj ci ñaari tomb, yu nekk ci ndombo gi, dafay yam ak ab jurukaay bu dendam tollook wuuteeg aj gi ngay natt ci diggante ñaari tomb yi, toppanteeg ag ndëgërlu gu yam ak gi ngay natt ci diggante ñaari tomb yi batay su jurukaay yu temb yi fayee.
Noste gu jàllu
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Batay dawaan bu wéy lees di dundale ag ndombo gu ami fattalukaay walla xiirtalukaay mbaa ñaar ñépp. Kem yi U ak I dañuy bawoo cig noste gu jàllu dem ci geneen noste gu sax. Kon nosteg jàllu du luy wéy, luy nekkandi la rekk. Àtte yees bind ci kaw yépp manees na leen fee jëfandikoo batay.
Noste gu sin
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci gii noste ndombo gi dawaan bu safaanu lañu koy dundale. Àtte yees bind ci kaw yépp manees na leen fee jëfandikoo batay, waaye ak coppite yi ci war.