Aller au contenu

Nguuri Pël yi

Jóge Wikipedia.

Nguuri Pël yi, Ca jamono yu yàgg ya li ëppoon ci giirug Pël ay sàmm yu daa màng lañu woon, di tuxu ci seen bëgg-bëgg ngir wër ndox ak ñax, ñu nekkoon di ñu tasoon ci gox yu bari ci sowwu Afrig, la ko dale ca dexug Senegaal ba ca ngéejus Càdd (lac du Tchad). Ci diggante xarnub fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom ñeent g.j, giir gii def na fi ay fipp yu lislaam yu bari yu waral ñu taxawal ñatti nguur ci Senegaal : Fuuta Tooro - Bundu - Fuuta Jalon. Ci mujjug xarnub fukk ak juroom g.j, am mbooloo ci way gàddaay yu Foolaan yi génne nañu Fuuta Jalon dem Fuuta Tooro, Koli Tingala jiite leen, moo tegoon loxo Fuuta Tooro ci atum 1512 g.j, daal di taxawal nguurug Fuuta Tooro. Ci atum 1770 g.j, la Sulaymaan Baal def ag jeqiku gu lislaam mooy gi soppi Fuuta def ko nguur gu lislaam Almaami Abdu Buukar jiite ko, mooy ki jiyaaroon kontar ay dëkkandoom : Waalo - Taraasa - Kajoor, la ko dale ca 1790 ba 1804 g.j, waaye dañu koo mujj dàq. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, la Fuuta tàmbalee naaxsaay. Ci lu tollook 1690 g.j, la Tunka buurub Goy may menn mag mu juge Podoor aw dog ci suuf, mooy Maalik si, dog wooyu mi ngi nekkoon diggante Faalimi ak Gambi gu kawe gi. Ci nii la nguurug Bundu sosoo. Maalik si daal di nay jibal ab xare, def it Bundu muy nguur gu lislaam, daal di safaanu nguurug Goy, gën a yaatal ag nguuram.

Nguur googu nekkoon na di gu naat ci ayug Maalik Si aki way wuutoom (njabootug Siisebi), li ko waral di séqoo yi mu amoon ak Gambi. Ci lu tollook 1727 g.j, la ag giirug Pël ca Fuuta Jalon jugoon - Karamoko Alfa jiite ko - soppi gox boobu it def ko nguurug lislaam, Almaami di ko jiite, ju njabootug Suriya di fal leeg-leeg, leeg-leeg gu Alfaya.

Seetal BUNTU TAARIIX